Khassida Huqal’bukaa « Jooyi Xol »

KI KO TAALIF CI ARAAB : CHEIKH AHMADOU BAMBA

KI KO TEKKI CI WOLOF : CHEIKHOUNA LO N’GABOU

Cliquer ici pour télécharger la version PDF : http://fsilngabou.com/huqal_bukaa_ci_wolof/

Ci turu Yàlla jiy yëramaakoon bi di jaglewqqkoon laay tàmblee, di julli (ñaan xéwël ak mucc) ci Yonnent bi aki waa këram aki àndandowam.

Jëf ju nekk yééné ja lay jëmmal.

Sama yééné nak moo di barkeel ca sang sa ( gaayu baax ya)

1- Jooy sang si fi jògé (faatu) lu jaadu la Ngir suuf yeek asamaan yaa ngi léén di jooy

2- Dama léén diin jooy di yaakar ci jooy yi bu ëlagéé(yawmal qiyaam) ngëramul Yàlla. Ñoom dañoo làqu dem ca neex-neex ya.

3-Ngalla man fuma jëm ñàkk naa gaayu mage doonoon ay ponkal yu xëy-xëy ne mes séén boroom woo léén yòbbu léén fu kowe.

4- Guddi yaa ngi léén di jooy( jooyi xol) weer yaa ngi léén di jooy, àndak marax ( ngoon) yeek suba yi.

5-Ay jaam la ñu woon yu daan topp Yàlla séén boroom moom it (Yàlla) mu nangul léén doon séén boroom bu léén di xëpp ay xééwël.

6-Ñoom dañoo jàppoon ne ab reggaay ci alal wala ñam wu lew buy tax ñu bàyyi séén wird ( lu baax luñu saxaloon) bokk na ci liy sabab musiba.

7-Ñoom daal bu guddi gi masaana muur ay mbalaanam (couverture) bay lëndëm këruus, ñu ne fojjet (jòg) bu gaaw ngir dundal guddi ya. (bàyyi nelaw aki caaxaan.

8-  Ñoom dañoo jaayoon ay caaxaan jëndé (weccee) ko tudd Yàlla ji léén sàkk ak di ko fàttaliku, jayoon it ay nelaw jëndé ko dééyaaleek séén boroom.

9-  Séén yaram ya dañu ko daan gàddaayloo tëddukaay ya, dañu daan fàtte (banneexu ci aw jigéén ñuy )bégalé niki Laylaa aki Salmaa (turi jigééni naar).

10- Bu laylaa nee tëll (ñëw) ak taaram ba, ñoom ñu ne wërëñ (wan ko ginaaw dem) toppi séén boroom.

11- Bu ñu taxawee bay dééyaalek séén boroom, dañuy fàtte ( jigéén ña) Laylaa ak Suhdaa, te ay zikr ak ay laaya doŋŋ la ñuy wéttalikoo.

12- (Fuñu tollu ) dañuy waxtaane Yàlla ji manal boppam lépp di jariñ ñépp di kilifag ñépp (waaye)duñuy waxtaane mukk aw jigéén niki Hind ak Lubnaa.

13- Aw nit lañu woon ñu jël sééni ngànaay fexe ba not ca sééni noon, bañu ko defee dañoo mujj kawe lool bari ay teranaga.

14- Gaayooyu am na ñu ñenenti kenu yu ñu daan taxawale néégub wilaaya.

15- – Noppi (nééw ay wax) – Xiif bu yàgg (nééw ag lekk– fog (nééw ay nelaw)– beru (ñeme wéétaay)ñu daan ko teg ci (ndigal ak tàggat) di ay junj yu jògé ci ay Sëriñ.

16- Nit ñooñu séén yoon wi Murid (ku namm ci yàlla) bu ci jaare jaaree dina ko fegal lor juy jogé ca ku féttéérlu ka (Saytaane) ak gép xeetu woru.

17- Séén yoon wa moo di jublu Yàlla (ne ko dann)baña topp bànneex, àndak sësuwaay (Usul) yay dàq tiitaange.

18- Ginaaw buñu jiitalee tuub teg ko ci ragal ak yaakar, baril lool njàqare ak di di ko saxoo boole ca doyloo gu mat sëkk.

19- Dëddu lépp luy jeex (mu bañ lééna mana fàbbib, am ga du léén taxa faku, ñàkk ko du léén taxa ñanki) amug sàmmu (ragal Yàlla) saxoo wééru ci séén boroom) ak di muñ saasu nekk.

20- Di xeex ak sééni bakan, di sant ( dello yàlla njukal) di gëram Yàlla ci lépp lu mu dogal, bàyyi di geestu mbiri nit ñi;

21- Séén yoon wa amna fukki mbir yoo xam ne képp ku ca bëgga sòòbu ci pastééf warut koo ñàkk.

22- – 1-Ab jëmuwaay te mooy taxa tuki –2 ab tegtalkat ku mel ni ab sëriñ bu Yàlla ubbi.

23- -3 Ab yòbbal te mooy ragal Yàlla, – 4 ngànnaay te mooy njàpp luy dàq sobe.

24- -5 ab niitukaay(làmp) te mooy tudd Yàlla ak di ko fàttaliku, -6 waruwaay te mooy itté ju kawe.

25- -7 Aw jàkk (yat) te mooy lott (xamne kàttan sunu boroom rekka ko ame) – 8 ag laxasaay te mooy laxasaayoo Haqiqa ( mbir ma dëggantaan).

26- Bokk na ci yi waruta ñàkk -9 am ngér (fumuy jaar) te mooy Sharia na ca jaar ci buy tàmbali ba baa muy jeexal (Sax ca fawu rek).

27- -10 aki àndandoo te mooy ay bokk yu am itté am kollëré dëggu ci mbokkoo googu.

28- Ñoom sang yooyu dañoo toppante ci ay martaba, ku nekk ci ñoom danay fegal Murid bi lépp luy mariid ak lu koy taxa woru.

29- Ku nekk ci ñoom ab sëriñ la bu am xam-xam, sàmmu, ñenn ci ñoom dañuy yar nit di ko tàggat ci ay zikr ak ay Haal tolluwaay.

30- Am na ci ñoom ñuy yéégé nit ci ab haal, am na ci ñoom ñuy yéégé nit ci ay junj (Demostration).

31- Ku nekk ci ñoom dafay deñ-kumpa (expert)xam jàngoroy (feebabari) xol yépp, di mana fegal Murid bi lépp lu koy taxa texeedi.

32- Ku nekk ci ñoom dafay yéwén tedd ragal Yàlla tabe ( genereux) di laabiire bindééf yépp.

33- Ci ragal yàlla lay dindéé bon-boni bakan yépp, dafay làq (ame) ay xam-xam yu kawe yu bawoo fa boroomam.

34- Dafay feeñal yoonu gòòr Yàlla ya mu leer nàññ, ci boppi ñiy sàkku njub mu di léén ko sotti ba muy walangaan (Fayd) inondation- abondance .

35- Ku nekk ci ñoom dafay ame itté ju muy yéégé fawu di jëm ca Yàlla ju tedd jiy terle ci di ubbéé.

36- Dafay gis yu nëbbu ya ak bëtu xolam kem ni muy jàkkaarlook ya nekk ca ginaaw ay kiraay.

37- Bu nee tëll ak fumu man di nekk dafay ame leer gu mel ni leerug jant bi di gand (jariñ) képp kuy sàkku ag leer.

38- Dafay fàddu (réér) képp kuy mbindééf dem ca Yàlla jiy bind lépp di boroomug leer aki mbòòt yu fàddu (ruqe).

39- Dafay far xumaag ju nekk ci xol di ko gàkkal, ni ab fòòtkat di def mbub mu tilim.

40- Ñoom gaayooyu képp kuy toog ci séén wet du texeedi toskare mukk, ngir ñoom ak texe rekk la ñuy fàggul Murid yi.

41- Bépp jaamub Yàlla bu namm yàlla Murid bu dëggal ci ñoom di léén ligééyal, di léén sopp, di léén jox hadiya di na kiilu texe.

42- Xeñtu mboorum yonnet bi (topp ak di jaar fa yonnent bi tegoon ay tànkam) tax na ñu am martaba yu kawe, Yàlla na Yàlla miy joxe may yi julli ci moom.

43- Xeñtu gu ñu doon xeñtu la ku wòòr ka Yonnent bi indi, maa ngi julli ci moom saasu nekk.

44- (Xeñtu googu) tax na ñu am ci ay baax-baax loo xam ne xalima manu koo bind, aw làmmiñ itam manu koo nettali.

45- Bokk na ci baax-baax yooyu : dañuy gééju ci xam-xamu shariya ak xam-xamu haqiqa ba laa ñuy dem sax di tàggatuji.

46- Ngir képp ku jòg di tàggat wala muy jubanti te jiitalul ñaari xam-xam yooyu Shariya ak Haqiqa la muy bijj (ñoddi- xëcc) jur moo di woru ak texeedi.

47- Bokk na ci baax-baax yooyu: dañuy taxaw duñu jëf duñu wax ludul ginaaw buñu gisee lu wér lu àndak ay seede.

48- Bokk na ci baax-baax yooyu: dañuy taqoo ragal Yàlla ci waxtu wa ñuy tàmbali ak buñuy jeexal.

49- Buñuy sooga tàmbali ragal bàkkaar moo léén di jàjj (soññ) motiver, bu ñuy jeexal nak màggal màggug Yàlla gi moo léén di jàjj.

50- Bokk na ci baax-baax yooyu: dañuy not séén bakan ci àndul ak ngistal (Riyaa) ngir li bakan bari lool ay pexe te bari ay wor.

51- Dañuy jàpp ne ñoom ñoo yéés bindééf yépp, te yit dañuy jàpp ne yayoo wu ñu benn karaama.

52- Dañuy jàpp ne ñoo gëna bon ñu bon ña génn topp faasiq ya, jàpp na ñu ne sax yayoo wu ñu di am ijaaba.

53- Bokk na ci baax-baax yooyu: dañuy saxoo muñ ay musiba ak jenguk moykat ya dañu koy muñ ngir Yàlla.

54- Bu ñu masaana gis ay lor jògé ca ñooña dal ci séén kaw dañuy dldi tuub ci séénug bari ay njuumte. 55- Bokk na ci sééni baax-baax : dañuy saxoo

njàqare saasu nekk, aywaay Yàlla na léén Yàlla

gëram waay.
56- Bokk na ci sééni jikko yu rafet : dañoo ragal

naaféq, ragal gàcce, ragal tiis yay nekk bis pénc ba. 57- Bokk na ci baax-baax yooyu: dañu daan suufeel séén bopp di (toroxlu- modestie) ngir Yàlla miy notaakoon te di séén boroom, dañu daan dëggu,

dëddu àddina, di laabal ay gàkk-gàkk.
58- Bokk na ci baax-baax yooyu: dañu daan wééru

fawu ci séén boroom (Rahman) moo xam dañuy ñoddi wala ñuy jiñ taxoon na jàmbatu ñu dara.

59- Xam-xam la ñu daan làmboo (sol- màndarga- apparence) lewet dëxëñ ci séén biir, daawu ñu woote lu ñu doonul, daawu ñu bañal it keneen la mu am ci ay maqama.

60- Wòòy ! ñàkk na nu sang soo xam ne séén yoon wa moo di yoonu Yonnent ba Mustafaa may ngën-ji mbindééf.

61- Yàlla mi ko yabal yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal mooki ñoñam aki sahabam li féék ña ngay làq ay àjjana.

62- Yàlla mi ko yònni yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, na ko jox xééwal ya gëna sell te fegal nu ci ag woru.

63- Yàlla mi ko sàkk yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, mooki ñoñam aki sahabam ya làq ay may.

64- Yàlla mi ko moom yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, na ko jox xééwal ya gëna sell mu defal nu ci nun itam nu làq ay ubééku.

65- Yàlla mi ko wëragal yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal mooki ñoñm aki sahabam ña daan diinéwoo (saxoo) di ko topp.

66- Yàlla mi ko teral yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, na ko jox xééwal ya gëna sell, te may nu ci ay karaama.

67- Yàlla mi ko def ab sang yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, mooki ñoñam aki sahabam ña ñu sonnewoon (ña amoon ag defaru).

68- Yàlla mi ko def sheriif (ku tedd) yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, na ko jox xééwal ya gëna sell, te defal nu ci wuñug ay kiiraay (kashfu).

69- Yàlla mi ko jiital yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, mooki ñoñam xééwal gu tollook limub mbindééf yépp.

70- Yàlla mi ko yékati yàlla na ko musël te dooli ko ay xééwal, na ko jox xééwal ya gëna sell, te mu defalaale nu ci ag yékkatiku.

71- Wòòy ! nun nàkk nanu sang su dem yòbbalé ay sàq yu yéémé.

72- Yàlla ji léén woo ngir dajeek ñoom Yàlla na dolli ay xééwal yuy gëramloo Yonnentam ba mu jiital muy jawriñam ci ñaari kër yi (àddina ak àllaaxira).

73- Sunu sang ba soppe bay doomu Abdalla Yàlla jiy feg aw tiis (njaqare) yàlla na ko dolli ay xééwal.

74- Yàlla jiy saafar jépp jàngoro juy ruyaat, Yàlla na dolli xééwal Yonnent ba kañuy rammloo bu kerook bisub pang (rassemblement) ba.

75- Yàlla ji di ag njub gndikat te gindiwoon léén ba ñu tegu ca yoon wu jub xocc wa, Yàlla na dolli xééwal Yonnent bi nga xamne ngënéélam yi du jeex mukk.

76- Yàlla ji manal boppam lépp te daan fay gaaya ngënji pay, Yàlla na dolli xééwal Yonnent ba di ku ñu teral te moo di ngënji mbindééf yépp.

77- Xééwal yuy sax ba fawu Yàlla na nekk ci moom, mu àndkook i ñonam waa-këram ci saasu nekk te kenn baña des.

78- Yàlla jiy boroom asamaan yeek suuf si, Yàlla na gëram sahaba yeek sang su baax (si may jooy)

3 réflexions au sujet de « Khassida Huqal’bukaa « Jooyi Xol » »

  1. Amycole

    Mashallah ! Amna solo li de ci sama xalat bou gate dina jaffé dieufê ci diamono yi niou toulou ndax nit gni légui wutt mo len jiteul sonal len

    Répondre

Laisser un commentaire

Votre adresse de messagerie ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Ce site utilise Akismet pour réduire les indésirables. En savoir plus sur comment les données de vos commentaires sont utilisées.