تحفة المتضرعين في التوسل بأسماء المفضلين للشيخ أحمد بامبا الت ضرع

Tuhfatul mutadharrihina – Xééwël gu ñu may ñi ami soxlayu ñu manut a ñàkkba mel ni ab liir ca bttub ndey ja.

KI KO TAALIF CI ARAAB : CHEIKH AHMADOU BAMBA

KI KO TEKKI CI WOLOF : CHEIKHOUNA LO N’GABOU

DATE : SEPTEMBRE 2014

Vous pouvez télécharger la version PDF ici : http://fsilngabou.com/تحفة-المتضرعين-في-التوسل-بأسماء-المفض/

Mu làmboo taasu (sàkku ci daray) ci barkeb gaaya gën a baax.

1-Maa ngi sant Yàlla di ko ñaan muy dolli xééwël gu sax dàkk ca ka nga xam ne moo nu feeñalal te indil nu ag njub. Mook Saabaam ya amoon lool mayug Yàlla.

2-Koo ku mooy sunu sang ba Muhammad. 3-Tay jii maa ngi ñaan sama boroom di taasu ci

turi gaaya gën a baax.
4-Ma wax ne: yaw Yàlla miy ku jege, di kuy

tontu di wuyu Yàlla na nga julli ci Yonnent bi nga xam ne bala ngaa zuyu kenn dafay fekk koo ka nangul ko te wuyu ab wooteem.

5-Ci barkeb Yonnent bi na nga ma nangul sama way wii yaw Yàlla jiy ku tedd yéwén. Te yit képp ku ko jël di ci dééyaaleek yaw na nga ko may defal ko lépp la mu cay sàkku.

6-Maa ngi lay ñaan nga Jéggal ma samay bàkkaar te fegal ma Saytaane, ci barkeb Nuuhak Ibraayma

7-Fegal ma aw tiis aki naqar àddina ak àllaaxira ci barkeb Muusaa ak iisaa

8-Maa ngi lay ñaan nga julli ci Muhammad miy Yonnentub Yàlla bi julliwaale ca Yonnent yaUluhazm.

9- te nga may ma Liimaan ngëm Lislaam jëfé akLihsaan rafetal, Tasawuf.

10- Maa ngi lay ñaan nga may ma ag sellal, ak tawfiiq dëppok lépp lu baax ci barkeb Abubakr Siddiiq ma doon dëggal Yonnent bi, ak Umarma doon teqale dëgg ak neen.

11- Ci barkeb Usmaan ma dencoon soxna ñaari leer ya ñaari doom yu jigéén ya, ak ci barkeb Aliyu ma doon baayi ñaari sëti Yonnent bi.

12- Ma ngi lay ñaan nga may ma leer akug kowe aki xeewël ci àddina ak ca àllaaxira.

13- Maa ngi lay ñaan nga musël ma ci ay lor Ci barkeb Talhata ibn Ubaydalla, ak Zubayr ben awaam, ak Saad ben abiwaqaas.

14- Maa ngi lay ñaan nga musël ma ci fitnasanje ci barkeb Sahiid ibn Zayd, akAbdaramaan ibn Awf.

15- Maa ngi lay ñaan nga ñoddil ma lépp luy mana jariñ, te fegal ma lépp luy mana alak.

16- Ma ngi lay ñaan ci barkeb Abdala ibn Abas doom-bay tax ba nga may ma xam-xam bu bari.

17- Maa ngi lay ñaan ci barkeb Abdala ibn Umar nga fegal ma lépp luy ñoddi lor.

18- Maa ngi lay ñaan ci barkeb Ibnu-masuudak Ibnu-salaam nga fegal ma nattu mbas ak ayu bët ak ayu wax.

19- Yaw sama boroom maa ngi lay ñaan ci barkeb Abaas ak Amza nga fegal ma bépp tar- tar.

20- Maa ngi lay ñaan ci wormay Asan akUsaynu nga tabe lool ci man àddina ak àllaaxira may ma ñaari leer ya.

21- Maa ngi lay ñaan ci wormay Xaasim akTaayir nga sellal sama biir ak sama bitti .

22- Maa ngi lay ñaan ci wormay Tayyib akIbraayma nga saxal ci man mbégté ak ñu di ma teral.

23- Maa ngi lay ñaan ci darajay Faatimatu nga feral sama bakan ci lépp luy waral ag tëj kaso.

24- Maa ngi lay ñaan ci wormay Ruqayya akZaynabu nga fegal fàww ak dàkku ak kiiraay.

25- Maa ngi lay ñaan ci wormay Umu- kulsuum nga jubale ma ak teraanga fegal ma mbugal ci àddina ak àllaaxira.

26- Maa ngi lay ñaan nga nangu sama wax jiiñaan gii ci wormay Aws-ben-aamir ak Haramak Masruuq.

27- Maa ngi lay ñaan ci wormay Rabii akAswad nga may ma Listiqama te jubbanti sama mbir.

28- Maa ngi lay ñaan ci wormay Aamir-ben- abdurahmaan ak Abu-maslamatal-xawlaani.

29- Nga may ma ag njéggal akug texe akub xam-xam ak jëfé akug jaamu-yàlla.

30- Maa ngi lay ñaan ci wormay Asan-basringa may ma ag sàmmu akug set wecc ba mel ni kuñu fees ci bànneex aki bidaa.

31- Maa ngi lay ñaan ay xééwal ci wormayAbu-huryrat ak Bilaal ak Suhaybu.

32- Maa ngi lay ñaan ci wormay Abu-dardaayinga nangul ma topp gii ma lay topp te nga

saafara ma ci jépp jàngoro ju feeñ ak ju

nëbbu.
33- Maa ngi lay ñaan nga jotale ma ci samay

jubluwaay ci wormay Miadaad ak Xaalid ak

Zubayru.
34- Maa ngi lay ñaan ci wormay Amiirul-

muuminiina Umar nga fegal ma ay pexe, akug

texeedi akug woru fakku.
35- Maa ngi la koy ñaan it ci wormay njiital

jihaadkat yi Aliyu ma daan taxawu diiné ji. 36- Maa ngi lay ñaan ci wormay Saad ak

Urwa nga dolli g jafandu ci buum gu gën a

dëgër ga.
37- Maa ngi lay ñaan ci wormay Xaasim ak

Xaarija dolli ma ci xeñtu tërëiilni Yonnent bi38- Maa ngi lay ñaan ci wormay Abu-bakr ak

Abdul-laahi dolli ma ay ngënéél yu dootul

jeex.
39- Maa ngi lay ñaan ci wormay Sulaymaan

nga dimbali ma fegal ma pexam Saytaane ak

feneen fu pexe man a jògé.
40- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaay

Xadija nga may ma lépp lu may mébét ci xam- xam aki téggiin ak jëfé ko.

41- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaayAysa nga fegal ci lépp lu may lor ci asamaan si ak suuf si.

42- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaayAfsa nga dox fàww sama digante ak lépp luy ñoddi aw tiis aku naqar.

43- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaayZaynabu nga rafetalal ma sama biir ak sama biti.

44- Maa ngi lay ñaan ci wormay imaamMaalik ak imaam-saafii ak imaam-abu-anifaak imaam-ahmad-ben anbal nga nangul ma samay ñaan .

45- Maa ngi lay ñaan ci wormay Jibriil nga may ma li may ñaan te nga def ma ma jot sëkk dayob goor ña.

46- Maa ngi lay ñaan ci wormay Miikaayil nga may ma ay xééwal te def ma ma ame njariñ ni waame wuy dët ab taw.

47- Maa ngi lay ñaan ci wormay Israafiil nga may ma ag ñoŋ sammu, te nga fegal ma tiisi bisub jaaxle ba.

48- 28 154 172 Maa ngi lay ñaan ci wormayAsraayil nga defal ma njekk lu rafet sama giirug dund ak ginaaw bu ma faatoo.

49- Maa ngi lay ñaan sama xasidag tawassul gii képp ku la ci woo di la ñaan na nga ko ci defal texeg àddina ak àllaxira te it na nga ko jéggal.

50- Maa ngi lay ñaan nga may ma ci kòòluté ak ngëram man ak ñi sàkkuwoon may way ko. 51- Te nga may nu ci it texe ak kaarange akug

topptoo ba nu mucc ci wépp ñaawtééf.
52- Te nga may nu ci it nu mucc ci laajub biir bàmmeel, mbugël, sukraatus nde, regleente.

53- Te nga may nu ci it mbégté ak ségaré waxtu wa nuy dee ak ba nuy dekki.

54- Te nga julli ci Yonnent bi dolli koy xeewël te musël ko moom aki Saabaam yu baax ya.

55- Maa ngi lay ñaan ita nga jéggal sama ñaari wayjur ak samag njabppt ak samay àndanadoo.

56- Maa ngi lay ñaan it nga jéggal mbooleem ku aju ci man, te it nga wéralal ma samag texe.

57- Maa ngi lay ñaan nga ñewenti nu, may nu kàttan, nekkal nu, defal nu mujj gu rafet.

58- Yàlla na nga julli ci Yonnent bi dolli ko xééwël te fajal ci jullit yépp sééni aajo.


Laisser un commentaire

Votre adresse de messagerie ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Ce site utilise Akismet pour réduire les indésirables. En savoir plus sur comment les données de vos commentaires sont utilisées.