Kitaabu Nahji Xadaayil Haaj (Teeréb yoonu fajug aajo)
UBBITE
ci tudd turu yàlla laay tàmblee samay jëf ak samaywax yalla miy xéewël
bindéef yépp ci àddinasi di jagleel yërmaandeem ñi
ko gëm ca àllaaxira
Nahju Qāda al-haj
Yalla dooyna ma te dooyaloonaa ko.
Yalla doyna weeru waay te doyaloonaa ko
Jef ju nekk yeene ja lay nuroo
Te looy jëf rekk langay ci yeene ngay am
Bokk na ci xam-xamu xereñ (hikma)
Lepp looy sakku boo ci sonnee danga ciy jot.
Kepp kuy fëgg bunt saa bu tanqale (ñii cii biir) ubbilees ko.
Kepp kuy woor ci gepp caay-caay na xam ni gënneel lu Yàlla lay dooge (koramnga ko)
Kepp ku bayyi ñakku fayda buy ñu lim woroom (boroom) xel yi boole ko ca
Kepp ku bëgg bakkanam ngërëm Yàlla du ko gërëm
Kuy def lu ko sòb di dajeek lu ko soof (sa’a)
Kuy xeex ak bakkanam su noppee dund texe
Kepp ku top yonnent bi (SAS) dina am lepp lu gënn ci lumu bëgg
Bepp reew minga xam ni fenn moo ko samp yagg-yagg dafay daanu
Bepp reew minga xam ni dëgg moo ko samp dafay des ba baa saa ji taxaw
Mangi sant Yalla ni mu sutuural ba nëbbu samay sikkte dimbalima
Mangi sant Yalla ci limu tabbe lool ci man te loolu yeewoona cant
Moom Yalla moo def ku am ay teggin sa rër (ñakku xam-xam) du feeñ ak sa suufe askaan
Moom moo defal ku am xam-xam ak teggin mu am yool (thawab) bu bare ak njub
Yall na Yàlla xewel yonnent bi moo moo yegoon ci kow al-Burãq
Moo moo daan woote jemi ci Yàlla te tek ko ci ay teggin ak jikko ju rafet
Moom Muhammad ak ña jiituwoon di ay sahaaba-am ñoom laqnañu (amnañu) ngënneelu Yàlla (fadlallah)
Ñu defoon laabire (conseil-nush) muy seen yoon biñu woote te daawuñu bundaxataal kenn (irhãq)
Ndax dañuy daan moom seen bakkan (nafs) ci seen sago (istirqãq)
Dañu daan joxe seeni allal ci yoonu Yàlla
Te daawul and ak ngistal walla naafiq (nifãq)
Dañoo gëmoon ni Yàlla mooy jariñ mooy joxe wërsëg moo tax ñu weroon ko seen lepp
Dañu daan jekkante jem ci lepp luy dundal allaaxira fasewoonañu adduna ba daawuleen yaqal dara
Ndool (Ñakk gu tar-imlāq) daawuleen tiitloo ndax xamn a ñu ni Yàlla mooy settaantal mbiir yepp te moo ko bind.
Dañoo soppoon seen boroom, kom-kom daawu leen fabbi
(detourner-alha) ci seen bëggante ci seen biir.
Bu guddi masaana (masoon-na) lëndëm dañu jël seen lampi xam-xam (ak di ko jëfe) di ko niitoo (tall-torcher)
Céy gaa yooyu dañoo moson cafka lu gëna neex te dañu ñoroon ñooñu
Yàlla na leen Yàlla gërëm, Yalla julli ci yonnent bi
Te nag, maa ngi tontu Murid yi bëgg a jajju ñoom dañu sakku waay woo xam ni dina ëmb ay teggiin yu ñu mën a tegginoo te loolu sax dafa di lu war.
Ndaxte kepp kuy sakku top Yàlla te andul ak iy teggin du ci mën ame njariñ
Ay Teggin, mooy lu gen ci lepp lu nit di denc te mooy teraanga ji gën ci lèpp lu nit di terloo (sakku di am ci teraanga)
Moom ay teggin dafay leeral xol, te mooy tax a jege ajjana
Mooy tax nit ñi sopp la, mooy tax nga sori safara
Ma buur (rise quickly) ci saa si ngir tont di ci yaakaar ngërëmu Yàlla ak yoolam (thawãb)
Li ko taxa jog nag, mooy jèema tënk lu waliyu ‘add al-hajji bindoon “ma di ci yaakaar faju aju”
Di ci yaakaar itam dajale ci gattal la boroom xam-xam yi bindoon bu yàgg
Ndaxte lèpp lu néew te jotal moo gën lu gudd bay ànd ak ay coono
Mangi ko tënk mu am lool njariñ ci ngëneelu Yàlla
Maa ngi ciy ñaan di ci yaakaar ngërëm ak koolute (surete-woolu) ak njëggël ca bes ba nga xam ni moo tiitloo ñepp
Yeen mbooleem taalibé yi maa ngi leen di dènk ngeen sàmoonte ak tontu lii
Jikko yi ci nekk ak teggin (adab) yi moo leen di womat jëmè leen ci njub
Njariñ yi ci nekk ak njub gi du sappi kenn ku jëm fenn kuy door a soobu ak kuy yàgga soobu ñoo ci yem kepp yiw yi du jeex
Ndaxte dafa lay xamal naka ngay jaare ba yegg ci gën ja rafet ay teggin ak lingay sàkku
Tudde naa ko nag, “yoonu faj ajoo” ngir gattal (ngir goob) liggeyu sunu seriñ bi tudd al-hajji
Mangi sant Yàlla di ko ñaan mu nangu liggey bi ci ngënèelam te dimbali ma ba ma matal ko
Te def ko mu mel ni turandoo-am ba kepp ku ko jàngati say mbiir yèwèn nga texe
Te musël ma ci ngistal ak awjëf (‛jb) ci dara ja Yonnent bi (sas) moom mooy boroom liwal h) amd
Te mangi koy ñaan mu musël ma ci gépp caay-caay te
may ma lèppi ngënéel.
Na ma musël itam ci ayu ibliis ba faww ak ci ayu lèpp lu mu bind lu nekk ci suuf si lu nekk ci asamaan ak lu nekk ci seen diggante
Na ma defal may topp ngën ji kuy ramm ki gën ci kepp kuñuy top.
Yalla nga juuli ci ñoom (Yonnent bi ak sahaabam) Lii mooy ubite teere bi